TSK

TSK · Lamentations 3:42

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal.

¶ «Waaye dégguñu ndigal, xanaa di la gàntal. Dañoo sànni saw yoon seen gannaaw; sa yonent ya leen doon xiirtal ci délsi ci yaw, ñu rey leen, ba ñàkke la kersa lool.

“Nangul ne ñaaw nga rekk, te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ, di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi ci ker garaboo garab gu naat, te dégluwoo ma.”» Kàddug Aji Sax jee.

Aji Sax ji moo yey, kàddoom laa gàntal. Yeen, xeetoo xeet, ngalla dégluleen te xool samaw tiis. Samay ndaw yu góor ak yu jigéen, ñoo duggi ngàllo!

Sa sobeey sa yàqute! Maa la setal te taxu laa set. Dootuloo tàggook sa sobe, ba keroog may giifal sama xadar fi sa kaw.

Aji Sax ji, nun kay gàcce ñeel na nu, nook sunuy buur ak sunuy kilifaak sunuy maam, ndax moy nanu la.

«Seeni maam, ana ñu tey? Yonent yi nag, ndax ba fàww lañuy dund?

Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;