TSK

TSK · Lamentations 3:59

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Noon yeey dellu gannaaw, tërëf, sànku fi sa kanam.

Ñeel Daawuda. Aji Sax ji, àtte ma, man de maandu laa wéye, Aji Sax ji laa wóolu, jenguma.

Jógal, sàmmal ma sama àq. Sama Yàlla, Boroom bi, àtte ma yoon.

Ndax damaa naagu woon ni xar mu ñu jëme rendikaay ba. Xawma woon ne man lañuy lalal ay pexe, naan: «Nan gor garab ak doomam, dagge ko fi réewum boroom bakkan, ba deesul fàttlikooti turam.»

Wóoy saa ndey, loo ma doon jure! Man mi réew mépp di xulook a layool, leblewma, lebuma; te ñépp di ma móolu.

Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.

Saaga nañu ko te feyuwul, daj na coono te tëkkoowul, waaye boppam la dénk kiy àtte dëgg.