TSK

TSK · Leviticus 13:46

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Santal bànni Israyil ñu génne dal bi képp ku ànd ak jàngoroy der juy law, mbaa jàngoroy xelli, ak képp ku sobeb néew bu mu laal, topp.

¶ Ci biir loolu amoon na ñeenti gaana yu nekkoon ca bunt dëkk ba. Ña nga naan ci seen biir: «Xanaa dunu toog fii ba dee?

Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.

Mu dem bay duggsi cib dëkk, fukki gaana dikk, dajeek moom, ba dànd ko, daldi taxaw. Ñu xaacu ne:

¶ Bindoon naa leen ca sama bataaxal ba, ne buleen amlante ak fokati séy yi.

¶ Ku ci déggul sunu kàddu yi ñu bind ci bataaxal bii nag, bàyyileen ko xel, te baña jaxasoo ak moom, ngir gàcceel ko.

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.

Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.