Leviticus 5:2
TSK
¶ «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.
«Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca bérab bu sell ba. Saraxu peyug tooñ la.
Na sawara wéye tàkk fàww ci kaw sarxalukaay bi, te bumu fey.
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.