¶ «Nit ki amul lu mat njégu gàtt, na indil Aji Sax ji ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def; benn bi di saraxu póotum bàkkaar, bi ci des di sarax rendi-dóomal.
TSK
TSK · Leviticus 14:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Su fekkee ne wasin-bees wi amul njégu xar, na indi ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, benn bi di saraxu rendi-dóomal, bi ci des di saraxu póotum bàkkaar. Sarxalkat bi defal ko ku jigéen ki njotlaayam, mu daldi set.»
Mooy yékkatee ku ndóol ci suuf, jële ku ñàkk ci mbuubit, boole leen dëj ca garmi ya, sédde leen jataayu teraanga. «Aji Sax jee moom kenuy suuf, samp ci àddina.
Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.
¶ Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?