Leviticus 13:46
TSK
Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
Mu am bés janq ba ne njaatigeem: «Éy su sama sang bi demoon ca yonent ba ca Samari! Kon de dina ko teggil jàngoroy deram ji.»
Naaman nag doora dem, sóobu ca dexu Yurdan ga, ba muy juróom ñaari yoon, muy la góoru Yàlla ga waxoon. Mu daldi wér, yaram wa mel ni yaramu xale bu góor bu ndaw, set wecc.
Jamonoy Yonent Yàlla Alyaasa itam, ay gaana yu baree nga woon ca Israyil. Waaye fajeesu ci kenn ku moy Naaman, waa Siri ba.»
¶ Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.