Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»
TSK
TSK · Leviticus 14:40
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kuy njublaŋ du tooge sama kër, kuy fen du taxaw sama kanam.
Xellil xaalis, tonni lu ca rax, ba ab tëgg man caa am ndab.
dàqleen nit kooku, jébbal ko Seytaane, ngir sànkutey yaramam, ndax aw fitam mucc, keroog bésu Boroom bi.
Ab féewalekat nag, yedd ko benn yoon ba ñaareel bi yoon, doora daggook moom,
¶ Gis naa say jëf, gis sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñu bon ñi. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay fen-kat lañu.
¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.
Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.