TSK

TSK · Leviticus 16:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell la, ñeel Aji Sax ji.»

Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»

Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk.

¶ «Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu sell lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.

Duggul biir asamaan it ngir di sarxe ak a sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk fu sell faa sell, yóbbaale deret ju dul josam.

Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww, nit ñi ñu sellal.