¶ «Waaye buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret.
TSK
TSK · Leviticus 17:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»
Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.
Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.
Waaye deret ja, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox.
Waaye deretam, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy sotti nim ndox.
Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.
¶ «Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngii di jàkkaarlook yeen, ngir musibaal leen, ba dagge fi mboolem Yuda.
Maay jànkoonteek ñoom, ñu rëcc sawara, sawara lakk leen. Bu ma jànkoonteek ñoom, dingeen xam ne maay Aji Sax ji.
Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.
Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.