¶ «Buleen seedeel seen moroom lu dul dëgg.
TSK
TSK · Leviticus 19:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk.
te teg ñaari nit ñu tekkiwul dara, ñu janook moom. Na ñooñu duural Nabot ne ko: “Saaga nga Yàlla, saaga Buur.” Su ko defee ngeen génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj ba mu dee.»
ngeen di tooge seen mbokk, di yàq deru doomu ndey.
Ku la nëbbal mbañeel, da lay fen; kuy wër di sos, ab dof la.
Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
Ku ne sa dëkkandoo ngay nax, te dëgg, doo ko wax. Dañoo tàmmi fen, di def njekkar ba sonn.
¶ Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.»
Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.
¶ Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngle lu baax,