TSK

TSK · Leviticus 19:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Esawu nag bañ Yanqóoba ndax barke ba ko baayam ñaanal. Ma ngay wax ca xolam naan: «Balaa yàgg ñu dëj sama baay, te bu boobaa dinaa rey sama rakk Yanqóoba.»

Ma ŋàññ kàngami Yuda, ne leen: «Lu ñaaw lii ngeen di def nag di teddadil bésub Noflaay?

Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.

Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.

Moona yeen de, yeena ngi ciy réy-réylu te waroon koo ñaawlu, ba dàqees kiy def jëf ju ni tollu ci seen biir!

¶ Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir gu ni mel.

Waaye ñi ciy bàkkaar, tiiñal leen, ndax ñi ci des ragala bàkkaar.

waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sam njàngle.

¶ Googu kàddu ngay waaree, di dénkoo ak di femmoo, te boole ci fulla ju mat sëkk. Bu la kenn yab.