Dañuy lakk yàpp wa cib taal, lekk ko guddig keroog, boole kook mburu mu amul lawiir ak xob yu wex.
TSK
TSK · Leviticus 2:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu.
¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
¶ Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.
«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.
¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.
«Moo bàkkaarul, fenul.»