Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · Leviticus 20:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Exodus 20:5
TSK
Leviticus 17:10
TSK
¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.
Jeremiah 3:2
TSK
«Téenleen, séentu tund ya ne faraas! Ana fu ñu leen fi tëddewul? Ci yoon yi ngeen di yeeroo ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi. Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon.
Jeremiah 32:39
TSK
Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.
Hosea 2:5
TSK
Lu ko moy ma futti ko ba mu ne duŋŋ, def ko ni bés ba mu juddoo, melal ko ni màndiŋ. Maa koy def ni joor gu wow, marloo ko ba rey ko.