¶ «Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: “Lu sell a ngii, ñeel Aji Sax ji.”
TSK
TSK · Leviticus 21:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara, ñeel Aji Sax ji.
¶ «Bul jébbal kenn ci say doom tuur mi ñuy wax Moleg, ndax waruloo teddadil sa turu Yàlla. Man maay Aji Sax ji.
Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.
Waaye warula jege rido bi, mbaa muy dem ba ca sarxalukaay ba, ndax sikk si ci moom. Bumu teddadil sama bérab yu sell, ngir man Aji Sax ji maa sellal bérab yooyu.»
«Santal bànni Israyil ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee.
Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.
«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”
Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.