TSK

TSK · Leviticus 23:29

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.”»

Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te mata sib, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci bànni Israyil.»

Seen bésub Noflaay la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.»

Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.

Ña rëcc, rawi ca tund ya, waru pitaxi xur ya, ñooy binneendoo ndax seeni tooñ.