TSK

TSK · Leviticus 23:34

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.

¶ «Fukki fan yaak juróom ci juróom ñaareelu weer woowu itam, seen bésu woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Amal-leen ci ag màggal, ñeel Aji Sax ji, diiru juróom ñaari fan, doore ko ca bés ba.

Musaa sant leen, ne leen: «Njeexital juróom ñaareelu at mu nekk, àppook atum njéggalug bor, ci diiru màggalu Mbaar yi,

¶ Ba mu ko defee Yerbowam dogal màggalug fukki fan ak juróom ca weeru juróom ñetteel wa. Mu mel ni màggal gay am Yuda. Yerbowam rendi ay sarax ca sarxalukaay ba. Noonu la def Betel, rendil fa ay sarax wëllu ya mu defarlu woon, defal ko wëllu ya sarax. Ci biir loolu mu tabb ca Betel ay sarxalkat ngir bérabi jaamookaay yooyu mu sos.

Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi Aji Sax ji santaane, te Musaa jottli ko, ne: «Bànni Israyil dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.»

Su boobaa mboolem ndesu wépp xeet wu songoon Yerusalem, Yerusalem lay yéegi at mu ne, ngir sujjóotali Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, tey màggalsi màggalu Mbaar yi*.

Loolooy doon dumay Misra ngir seen bàkkaar, di dumay wépp xeet ngir seen bàkkaar, ndax ñàkka yéeg ba màggalsi màggalu Mbaar yi.

¶ Ñoom ñépp ngëm lañu deeyaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina.