Ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israyil fàww, ñoom ak seen askan.
TSK
TSK · Leviticus 24:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»
Képp kuy góor ci doomi Aaróona yi man na cee lekk. Seen cér la bu ñu leen sédde ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, te dogalal leen ko fàww. Lépp lu ci laal day doon lu sella sell.»
te nga woo mbooloo mi mépp, ñu daje ci bunt xaymab ndaje mi.»
¶ Ci kaw loolu Musaa wax ak Aaróona ak doomam yu góor yi des, di Elasar ak Itamar, ne leen: «Jël-leen saraxu pepp mi des ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, ngeen lekk ko, bañ cee boole lawiir, ci wetu sarxalukaay bi, ndax lu sella sell la.
Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell.
«Waaye yeen yeena teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji, nde yeena xalaat ne lu sobewu la, te aw yàppam, aw ñamam jarul dara.