TSK

TSK · Leviticus 25:55

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.

Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam.

Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israyil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Seba, ma weccikoo la.

Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.

Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag sellnga la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.

¶ Te itam as gor laa, kenn moomu ma; teewul jaamu ñépp laa def sama bopp, ngir gëna iril Sang bi aw nit.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.