Ci tooñin yooyu ñu lim war naa wax na mu tooñe.
TSK
TSK · Leviticus 26:40
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
su boobaa man itam maa leen di noonoo, te it man ci sama bopp maa leen di mbugalaat lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
Day tuub bàkkaaram, ba noppi fey dayo ba mu ameel ka mu tooñ. Te juróomeelu xaajam la cay teg, jox ko ko.
¶ Ëllëg nag, su mboolem mbir yooyu dikkee fi seen kaw, muy barke yi, di alkànde yi ma teg fi seen kanam, su boobaa bu ngeen délloosee seen xel foofa mu leen fekk, ca biir mboolem xeet ya leen seen Yàlla Aji Sax ji dàq jëme,
¶ «Bu Israyil sa ñoñ daanoo fi kanam ab noon, ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu waññikoo ci yaw, sàbbaal saw tur, ñaan, sàkku saw yiw ci biir kër gii,
bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, yaay boroom njekk. May nga nu bésub tey jii nu dese bakkan. Nu ngi nii fi sa kanam ci biir tooñange, ba tax du kenn ci nun ku am lay fi sa kanam.
nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne: «Maa bàkkaar, maa xëtt njub, te feyeesu ma ko sax!
Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.
“Nangul ne ñaaw nga rekk, te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ, di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi ci ker garaboo garab gu naat, te dégluwoo ma.”» Kàddug Aji Sax jee.
Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare, samay butit di fuddu, sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis. Man de maa gàntal ba gàntaaral, ba fa biti, saamar di fa bóome, te biir kër it di ndee.
Su boobaa yeenay fàttliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu.
Ma ñaan sama Yàlla Aji Sax ji, tuubal ko samay bàkkaar, ne ko: «Yaw Boroom bi, Yàlla ju màgg ji mata ragal, yaw miy sàmm kóllëre ak ngor sa digganteek ñi la bëgg, di sàmm say santaane.
Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;