Waaye su ngeen fa sàkkoo seen Yàlla Aji Sax ji, dingeen ko daj, ndegam seen léppi xol, ak seen léppi bakkan ngeen ko sàkkoo.
TSK
TSK · Leviticus 26:44
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñoo baña dégg, baña bàyyi xel sa kéemaan yi nga def ci seen biir, te ñoo sajju loos, fétteeral ba fal njiit, nara dellu ca seen njaam ga. Waaye yaw yaay Yàlla jiy boroom njéggal ak yiw ak yërmande, di muñ mer, te bare ngor, ba tax waccoo leen.
ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
«Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Ni figg jii baaxe, ni laay geesoo mbaax ngàllog Yuda gi ma yebale bérab bii, jëme leen réewum Babilon.
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
kon dinaa wacc askanu Yanqóoba ak Daawuda sama jaam bi, ba dootuma taamoo ciw askanam kuy yilif askanu Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Maay tijji seen wërsëg moos, yërëm leen.»
Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.
Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.