Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw.
TSK
TSK · Leviticus 26:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,
Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.
Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen.
¶ Barkeel ay ñeel seen meññeefum njurukaay, ak seen meññeefum suuf, ak seenug jur, seen jur gu gudd, ak seen jur gu gàtt.
Rax ci dolli, Sang bi, ma nekk ci digg askan wi nga taamu, askan wu yaa, ba maneesu koo waññ mbaa di ko lim.
Ma ne leen: «Yàlla Boroom asamaan moo nuy may ndam. Nun ñiy jaamam nooy jóg tabaxaat dëkk bi. Yeen nag amuleen wàll ci Yerusalem, te baaxoowuleen fi benn sañ-sañ!»
Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
«Man nag, sama ndesu gétt, maa leen di dajalee mboolem réew yi ma leen dàqoon, jëme; te maa leen di délloosi seen parlu, ñu meññ ba yokku.
Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”»
Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,