TSK

TSK · Leviticus 3:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji, te doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi ñooy indi deret ji, xëpp ko ci mboolem weti sarxalukaay bi ci bunt xaymab ndaje mi.

Day teg loxoom ci kaw boppu jur gi muy sarxal, te rendi ko ca bunt xaymab ndaje ma. Doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi daldi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Day yóbbu yëkk wi ci bunt xaymab ndaje mi, ci kanam Aji Sax ji, daldi teg loxoom ci boppu yëkk wi, ñu rendi yëkk wi ci kanam Aji Sax ji.

Day teg loxoom ci boppu sikket bi, rendi ko fa ñuy rendi saraxu rendi-dóomal, fa kanam Aji Sax ji. Saraxu póotum bàkkaar la.

Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.

Loolu di firi ne ci Almasi la Yàlla jubale waa àddina, ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gi.

¶ Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu,