TSK

TSK · Leviticus 4:26

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def saraxu cant ci biir jàmm. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.

Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.

La mu sàggane woon ca yooyu ñu sellalal Aji Sax ji da koy fey, ba dolli ci juróomeelu céru njég ga mu fey, jox ko sarxalkat bi. Sarxalkat bi da koy defal kuuy mi njotlaayam, muy saraxu peyug tooñ, ngir mu am njéggal.

¶ «Li ñu dogal ci saraxi pepp mooy lii: Na ko doomi Aaróona yu góor joxe fa kanam Aji Sax ji ca sarxalukaay ba.

Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi, na ko diw ci boppu nit ki ñuy laabal. Noonu la ko sarxalkat bi defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji. Ba loolu amee sarxalkat bi rendi sarax biy póotum bàkkaar,

Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.

Sarxalkat bi day def loolu njotlaayal mbooloom bànni Israyil gépp, njéggal daldi leen ñeel, gannaaw moy ga dug teyeef, te ñoom it indi nañu seen saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, booleek seen saraxu póotum bàkkaar fi kanam Aji Sax ji, ndax seen moy ga dul teyeef.

Bésub ñaareel ba nanga indi ab sikket bu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar bu ñuy laabale sarxalukaay bi; ñu laabale ko sarxalukaay bi, na ñu ko laabale woon yëkk wu ndaw wa.