TSK

TSK · Leviticus 4:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Sàkkal ci deretu yëkk wu ndaw wi, nga capp ci sa baaraam, diw ci béjjéni sarxalukaay bi, te nga tuur li des ci deret ji ci suufu sarxalukaay bi.

Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell la, ñeel Aji Sax ji.»

Bu noppee na sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi ci kanam Aji Sax ji, ci biir xaymab ndaje mi. Li des ci deret ji, na ko tuur ca taatu sarxalukaayu rendi-dóomal ba, ca bunt xaymab ndaje ma.

Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu xar miy saraxu póotum bàkkaar, te taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi.

Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi.

¶ «Bu sottalee, na génn jëm ca sarxalukaay ba ca kanam Aji Sax ji, ba noppi defal sarxalukaay bi njotlaayal boppam. Day sàkk ci deretu yëkk wi ak ju sikket bi, taqal béjjéni sarxalukaay bi yépp.

Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.

Xayma ba, ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la wis-wisale ca kaw.