TSK

TSK · Leviticus 5:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.

Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.

Na indil Aji Sax ji gàtt bu jigéen, xar mbaa bëy, muy daanam ndax bàkkaar bi mu def. Saraxu póotum bàkkaar lay doon, sarxalkat bi defal ko ko njotlaayal bàkkaar bi mu def.

Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.

Hosea 4:8 TSK

Sama saraxi póotum bàkkaari ñoñ lañuy dunde, tey yàkkamti ñu def njubadi.