Li des ci saraxu pepp mi, Aaróona aki doomam ñoo koy féetewoo, muy cér bu sella sell, bawoo ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.
TSK
TSK · Leviticus 6:16
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar, bi mu def te mu bokk ci xeeti bàkkaar yooyu ñu lim. Su ko defee mu am njéggal. Li des ci sarax bi sarxalkat bee koy moom, mu mel ni bu doon saraxu pepp rekk.»
Lii nag, yaa ko moom, ci mboolem sarax yu sell yee sell, yi mucc sawara: seen bépp sarax, seen bépp saraxu pepp ak seen bépp saraxu póotum bàkkaar, ak seen bépp saraxu peyug tooñ bu ñu ma indil, lu sella sell la, ñeel la, yaak sa doom yu góor.
Saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ, ñoom ñoo koy lekk, te lépp lu ñu jagleel Aji Sax ji ci Israyil, ñoo koy moom.
¶ Xanaa xamuleen ne, ñiy liggéeye ci kërug Yàlla gi, ci kërug Yàlla gi lañuy jële seen lekk, te ñi sasoo sarxalukaay bi, am nañu wàll ci sarax ya ñu fa joxe?