TSK

TSK · Leviticus 6:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ak mburu yu mag yu amul lawiir, ak kàmp yu sew yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw, ak mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, te sungufu bele su mucc ayib ngay defare yooyu.

¶ «Bu nit dee indil Aji Sax ji saraxu pepp, sunguf su mucc ayib la saraxam wara doon, mu sotti ci diw, def ci cuuraay,

¶ «Su amul lu mat njégu ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, li muy indi, sarxal ko ngir bàkkaar bi mu def, ñetti kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, muy saraxu póotum bàkkaar. Du ci def diw, te du ci sotti cuuraay, ndax li mu di saraxu póotum bàkkaar.

«Leween ñi, wax leen, ne leen bu ñu jëlee ci bànni Israyil seen céri fukkeel yi ma leen jagleel yeen, muy seen cér, nañu ci jooxeel Aji Sax ji, fukkeelub céru fukkeel yooyu.

Loolooy saraxu rendi-dóomalu bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuram.

Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.