Exodus 28:40
TSK
Doomi Aaróona yu góor yi itam, sàkkal leen ay mbubb. Sàkkal leen ay laxasaay, te ay kaala it, sàkkal leen ko ngir daraja ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Doomi Aaróona yu góor yi itam, sàkkal leen ay mbubb. Sàkkal leen ay laxasaay, te ay kaala it, sàkkal leen ko ngir daraja ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo.
Loolu ngay def diwu pal gu sell gi, te na doon njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. Diwu pal gu sell lay doon.
ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi; yére yu sell yu Aaróona sarxalkat bi, ak yérey doomam yi ñuy sol, di sarxale.
Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.