TSK

TSK · Leviticus 8:25

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Kuuy mi, nanga ci génne li ci duuf: calgeen bi, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yeek nebbon bi ci seen kaw, ak tànku ndijoor bu kanam bi, ndax kuuyum colug sarxalkat yi la.

Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.