TSK

TSK · Luke 1:78

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!

Jëfi ngoru Aji Sax ji laay fàttlee ak cant gi Aji Sax ji yelloo, ngir li nu Aji Sax ji defal lépp; mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israyil, defal leen ko ci yërmandeem, ak jëfi ngoram gu réy.

Déglul bu baax, yaw Yosuwe sarxalkat bu mag bi, yaak sa xarit yi toog fi sa kanam te taxawe ab tegtal, nde maa ngii di indi samab jaam, ki ñuy wax Njebbit li.

¶ Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp,

Yàlla seede na ne sopp naa leen yeen ñépp, cofeel gu Almasi Yeesu ci boppam àttana tibbe ci biir xolam.

¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.

¶ «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»