Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?»
TSK
TSK · Luke 16:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
da leena wax, ne leen: «Ana lu waral ngeen di def jëf jii? Maa dégge ci askan wépp jëf ju bon jii ngeen nekke.
Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.
Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”
Dama laa ragal, ndaxte ku néeg nga. Dangay foqati loo dénkaanewul woon, di dajale loo jiwuloon.”
Ndax kat bokk yi, dégge naa ci waa kër Kelowe, ne am na ay dëngoo ci seen biir.
Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.
Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo, ba la mag ñi defaloon.
waaye ñoo koy layoo ak ki nara àtte ñiy dund, ak ñi dee.
Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.