Aw ñam, bumu la yàqloo liggéeyu Yàlla. Dëgg la, wépp ñam set na, waaye lekk ga nga koy lekk, su gàkkalee ngëmu keneen, def nga lu aay.
TSK
TSK · Luke 17:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Romans 14:20
TSK
Moo tax, su dee aw ñam wu ma lekk mooy tax ma bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat, dootuma lekk mukk aw yàpp ci àddina, ngir baña bàkkaarloo sama mbokkum gëmkat.
Fàww sax mu am ay xaajaloo ci seen biir, ngir ñi seen ngëm wér mana fés ci seen biir.
Revelation 2:14
TSK
¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.
Revelation 13:14
TSK
Ñaareelu rab wi nag nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wi. Mu sant waa àddina, ñu sàkk jëmmu rab, wi ñu jamoon saamar te muy wéye bakkanam.