TSK

TSK · Luke 18:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Teral-leen seen ndey ak seen baay, ndax ngeen gudd fan ca suuf sa leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.

Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»

Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.

Ndax ndigal yii kat: «Buleen jaaloo, buleen bóom, buleen sàcc, buleen xemmem,» ak leneen ndigal lu mu mana doon, ci genn kàddu gii la tënke: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom.»

«Teral-leen seen ndey ak seen baay,» mooy ndigal li jëkka ànd akub dige,

James 2:8 TSK

¶ Ndegam nag yoonu Buur Yàlla ngeen matal sëkk, di sàmmonteek Mbind mi ne: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom,» su boobaa waawleen góor!