TSK

TSK · Luke 19:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Buleen seedeel seen moroom lu dul dëgg.

Day tuub bàkkaaram, ba noppi fey dayo ba mu ameel ka mu tooñ. Te juróomeelu xaajam la cay teg, jox ko ko.

Te it menn mbote mi, ñeentam la koy feye, gannaaw moo def jooju jëf, te amu ci jenn yërmande!»

Waaye bu feeñee, fey boroom juróom yaari yoon, joxe alalu këram yépp.

Luke 7:13 TSK

Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»

Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.

Yeesu dégg loolu, ne ko: «Lenn rekk nga deseleeti. Mboolem loo am, jaay ko, séddale ko néew-doole yi. Su ko defee nga woomle fa asamaan. Boo noppee, ñëwal, topp ci man.»

Acts 4:34 TSK

Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njég li,

¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.