TSK

TSK · Luke 2:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

Luke 1:43 TSK

Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?

Luke 2:4 TSK

Ku ñuy wax Yuusufa itam jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndax ci waa kër Daawuda la askanam bokk.

¶ Yeesu neeti leen: «Nees mana waxe ne Almasi, Sëtub Daawuda la?

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.

Aadama mu jëkk ma, ci suuf la jóge woon, di suuf; Aadamam ñaareel mi jóge fa asamaan.

làmmiñu ñépp it biral ne Yeesu Almasi mooy Sang bi, te muy ndamu Yàlla Baay bi.

¶ Kon nag, ni ngeen nangoo Almasi Yeesu di Sang bi, àndleen ak moom, jëfe noonu.

mbaa di randal. Waaye nañu firndeel ne ñoo yelloo kóolute gu mat sëkk, su ko defee dinañu sagal ci lépp, àlluwa ji ñu jànge, te muy ju Yàlla, sunu Musalkat.