te notuleen doxandéem, ab jirim akub jëtun, tuuruleen deretu jaamburu Yàlla, fi bii bérab, toppuleen yeneen yàlla bay loru,
TSK
TSK · Luke 20:47
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.
Amos ne: «Dégluleen lii, yeen jula yiy dëggaate aji ñàkk, di jeexal néew-ji-dooley réew mi,
Yeen sama ñoñ, démb rekk ngeen jóg nib noon; yeena ngi nangoo ci nit mbubbum xewam, fekk muy romb, buggul xare, foogul dara.
¶ Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru Farisen ñi, te mooy jinigal.
¶ Masunoo jaye, xam ngeen ko, ag bëgge it masunoo taxa jóg, Yàlla seede na ko;
Xam Yàlla lañuy woote, te seeni jëf weddi Yàlla; nit ñu jara jéppi, ñu déggadi lañu, te tëlee def lenn lu baax.