1 Samuel 14:45
TSK
Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul.