TSK

TSK · Luke 21:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.

Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam, ak teraanga, ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.

Li nu gisul kay lanuy yaakaar, di ko séentook a muñe yaakaar ji.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn farlute googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk.

Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.

James 5:7 TSK

¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.

¶ Gis naa say jëf, gis sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñu bon ñi. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay fen-kat lañu.

Ku wara dem ngàllo, ngàllo nga jëm, ku wara deeye saamar, saamar ngay deeyeji. Looloo tax ñu sell ñi wara saxoo muñ ak ngëm.