TSK

TSK · Luke 22:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israyil ak waa kër Yuda kóllëre gu yees.

Noonu itam la def ak kaas ba, gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo, saa yu ngeen ci naanee.»

Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.

ndax kayitu ndono du wér lu moy gannaaw bu nit ka deeyee. Du jàppandi mukk li feek ki donalee ngi dund.

¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,