Job 33:16
TSK
Mu ne ko rukk ndéey, boole kook màndarga, artoo ko ko,
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu ne ko rukk ndéey, boole kook màndarga, artoo ko ko,
Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.
Ba loolu amee, ku nekk naan sa moroom: «Ndax yéguloo woon cawartey xol bu tooy, ba muy wax ak nun ci yoon wi, di nu firil Mbind mi?»
ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”
Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.