TSK

TSK · Luke 3:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dama ne jàkk ndigalam yépp, xalabuma dogali yoonam.

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

«Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy, di sàmm sama mboolem dogali yoon, di jëfe yoon ak njekk, dina dund déy, du dee moos!

Micah 6:8 TSK

Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Luke 19:8 TSK

Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.»

Sàcc bi, na ba sàcc te nangoo sonn, di liggéeye loxoom liggéey bu rafet, ba man cee dimbali néew-ji-doole ji.

¶ Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal, ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi.