Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
TSK
TSK · Luke 3:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’
Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.
Mu ne: «Maa leen ko wax, su ñii noppi woon, doj yi ñooy xaacu.»
¶ Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.
Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, ndee lay jur.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
¶ Ndax suuf kat, su naanee ndox mu mu tawlu ay yoon, ba meññal ñi ñu koy beyal, gàncax gu leen jariñ, soosa suuf dina séddu ci barke bu bawoo fa Yàlla.