Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
TSK
TSK · Luke 4:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Foofa la Musaa des ak Aji Sax ji diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg te lekkul, naanul. Aji Sax ji nag bind ci àlluwa yi, fukki santaane yi lal kóllëre gi.
¶ Ba loolu amee ma daanu tëdd fa kanam Aji Sax ji, na woon, diiru ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Du ñam wu ma lekk, du ndox mu ma naan ndax seen gépp moy gu ngeen moy, di def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.
¶ Subaak ngoon nag waayu Filisti ja ne jaas taxaw, ba mu am ñeent fukki fan.
«Demal woo mboolem Yawut yi, ci Sus, ñu daje. Te ngeen wooral ma: buleen lekk, buleen naan diiru ñetti fan, du guddi, du bëccëg. Man it maak sama surga yu jigéen, nu woore noonu. Su ko defee ma dem ca Buur doonte yoon nanguwu ko. Su ma dee dee, ma dee rekk.»
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.