TSK

TSK · Luke 5:38

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, weccee leen ko xolu suux,

Doonte booba, ay nit ñu tuddoo bokki gëmkat ñoo yoxoosu ba tàbbi ci sunu biir, di nu yëddu, ngir luqatu ni nu moome sunu bopp ndax Almasi Yeesu mi nu gëm, te li ñu ci jublu di delloo nu ci buumi njaam.

Waaye léegi bi ngeen xamee Yàlla, mbaa bi leen Yàlla ràññee, nu ngeen mana delluwaate ci mbiri àddina yooyu boole tële ak ñàkk njariñ, bay nekkaat seeni jaam?

Ñi xaraf ñoom ci seen bopp sax toppuñu yoon wi. Teewul ñu bëgg ngeen xaraf, ngir mana damoo seen màndargam yaram, yeen ñi ñu xarafloo.

Ñooñu jokkuwuñu ci Almasi, miy bopp bi, te ci bopp bi la yaram wi wépp di jëfandikoo siddit yeek tenqo yi, ba suuxatu, ngir lépp mànkoo ba mana màgg, ni ko Yàlla di màggale.

Waaye Yàllaa sikk bànni Israyil, ba mu nee: «Ay fan a ngii di ñëw, la Boroom bi wax, mu ne maay fas ak kër Israyil ak kër Yuda, kóllëre gu yees gu bokkewul ak ga ma séqoon ak seeni maam,

¶ Ci kaw loolu ki toog ci ngàngune mi ne: «Maa ngii di yeesal lépp!» Mu teg ci ne ma: «Bindal, yii kàddu yu wóor la te dëggu.»