TSK

TSK · Luke 6:27

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Su ngeen dajeek seen nagu noon mbaa mbaamam mu réer, fexeleen ba délloosil ko ko.

Aji Sax ji sama Yàlla, ndegam maa def lii, ndegam maa taq fenn lu ñaaw,

Màggug Yàllaa ngi ci li mu làq, darajay buur a ngi ci li mu feeñal.

Luke 6:22 TSK

Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.

Luke 8:8 TSK

La des ca jiwu ma wadde suuf su nangu, daldi sax, ba meññal lu ko mat téeméeri yoon.» Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw ne: «Ku am nopp yu mu dégge kat, na dégg.»

Luke 8:18 TSK

Kon nag teewluleen ni ngeen di dégge. Ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu xalaatoon ne am na ko sax, dees na ko nangu.»

Acts 7:60 TSK

Mu ne gurub, samp bëti óomam, daldi àddu ca kaw, ne: «Sang bi, bu leen topp bii bàkkaar.» Naka la wax loolu, daldi nelaw.

Póol nag àddu ca kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp a ngi fi.»

Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.