TSK

TSK · Luke 7:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu mu tëdd, tàlli ñetti yoon ca kaw xale bu góor ba, tey ñaan ci Aji Sax ji naan: «Éy Aji Sax ji sama Yàlla, rikk bàyyil bakkanu xale bii, mu délsi ci moom!»

Job 14:14 TSK

Ndax dees na dee, di dundati? Konoon ma muñe ko sama fani coono yépp, ba keroog sama kuutaay yiwisi ma.

Waaye yaw askan wi, ñi nga deele ñooy dellu dundaat, seeni néew ay dekki, ku doon nelaw sa biir bàmmeel, yewwu, sarxolle. Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer, suuf délloosi ña dëddu.

Luke 7:17 TSK

¶ Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.

Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.