liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.
TSK
TSK · Malachi 1:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israyil sama ñoñ?”
Moona Yanqóoba, woowuloo ma, yaw Israyil laa ne, sàppi naa la.
Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di jaaloo, di giñi fen, di taalal Baal, tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul,
¶ Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.»
«Maa bañ, maa sib seeni màggal, seen ndajey diine génnliku na ma.
Yeen sama ñoñ, ana lu ma leen def? Ana fu ma leen sonale? Waxleen ma!
Xanaa di indi ñam wu sobewu fi sama sarxalukaay. Yeen ngeen ne: “Ana nu nu la sobeele?” Xanaa xalaat ne sañees naa teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji.