Moo rafet xel, bare doole! Ana ku koy jéema të, mu jig ko?
TSK
TSK · Malachi 1:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bu Yàlla nee cell, ana ku koy ŋàññ? Bu làqee kanamam, ana ku koy niir? Xeet yeek nit ñi la boole tiim,
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu.
Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.
Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
Xanaa ñu ne coww ba sowu, ne jàyy cëppandoo fa kaw waggi Filisteen ña, waa penku, ñu sëxëtoondoo; Edom ak Mowab, ñu teg loxo; Amoneen ña nangul leen.
guddeek bëccëg, du fey, saxar sa day gilli ba fàww, réew ma gental giiru jamono, te deesatu fa jaare mukk.
Am nga yaakaaru ëllëg.» Kàddug Aji Sax jee. «Say doom ay délsi seenum réew.
Ana ku wax, mu am, te Boroom bi dogalu ko?
Saamar ngeen di fàddoo, fa catal Israyil laa leen di mbugale, ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
Maay duma Edom, te Israyil sama ñoñ laa leen di dumaa. Ñooy jëflanteek Edom la méngook sama mer, tollook sama xadar, ba ñu ñam sama mbugal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.
te Esawu laa foñ. Maa def ay tundam ab gent, ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu tilli màndiŋ mi.
¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen ñi naan: «Tey mbaa ëllëg ma dem ba dëkk sàngam, def fa at, julaa fa ba tonu.»