Waaye fépp fu bànni Israyil dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññatle waa Misra ak bànni Israyil.
TSK
TSK · Malachi 3:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Deltuleen gannaaw, bu njubadi am. Dellootileen gannaaw, sama der set na wecc!
Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.
Waaye bu ma déjjatee yooyu xeet ba noppi, dinaa leen dellu yërëm, ku nekk, ma delloo ko céram, ku nekk ak suufam.
¶ Malaaka ma waxati ma, ne ma: «Jamono yooyu ci la Mikayel, malaakam wattukat mu mag, miy taxawu sa mbooloo, di jóg. Muy jamonoy njàqare ju masula am, cosaanal xeet yi ba tey jii. Bu keroogee sa bokk yay mucc, di ñi ñu bind ci téereb dund bi.
Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »
Yeena ne: “Jaamu Yàlla ag neen la. Ana lu nu jële ci dénkoo ndénkaaneem, tey wéye toroxlu fi kanam Aji Sax ji Boroom gàngoor yi?
Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.
¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
¶ Loolu lépp di firndeel njekku àtteb Yàlla, bi leen di yellale nguurug Yàlla, gi tax ngeen di sonn.