Mu ne: «Sànnileen ko ci suuf.» Ñu jàpp Yesabel, sànni ko fa suuf, deret ja tis ca kaw taax maak fas ya; Yewu dëggaate néew ba.
TSK
TSK · Micah 7:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku bége sama njàqare, yal nanga rus, ba torox. Kuy réy-réylu ci sama kaw, yal nanga am gàcce, ne yàcc.
Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: «Lu tax nga fàtte ma, noon di ma fitnaal, may wéye tiis?»
Bul tax yéefar yi naa: «Ana seen Yàlla?» May nu, nu gis ni ngay mbugale yéefar yi, feye leen sa deretu jaam yi tuuru.
Yal na ñi may sosal sàngoo toroxte, làmboo gàcce ni mbubb.
Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, ndokklee ku leen fey jëf, ja ngeen nu def!
Moo wàcce ñi dëkke woon fa kaw, moo detteel waa dëkk ba aju woon, daaneel leen, ñu xalangu, ba mëq suuf,
«Waxleen Esekiya buurub Yuda ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri.
Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi, toogal ne cell te fatu cig lëndëm, deesatu la wooye lingeeru réew yi.
Lu waral sa xonqaayu mbubb mi, sa yére yi mel ni ku doon dëre dërukaayu reseñ?
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bànni Israyil ak Yuda, ñépp lañu notandoo. Ñi leen jàpp ñépp téyee leen doole, bañ leena ba.
Waaye mboolem lu Babilon ak waa réew mépp def ci Siyoŋ, maa leen koy fey, ngeen di gis, yeen Yudeen ñi.» Kàddug Aji Sax jee.
Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo, seen yaram wépp daw, gépp kanam sëlmoo gàcce, bopp ya di nel yu set wecc.
Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»
Tey ci sa kaw, la xeet yu bare daje, yaw Siyoŋ, te naan: «Nees ko tëdde, nanu seetaan Siyoŋ!»
Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
Yeena koy gisal seen bopp, yeenay seede ne: “Màggaayu Aji Sax ji jéggi na kemu réewum Israyil.”
Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.